wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
Axakay; dinaa bokk
si; je participerai.
ayante
se relayer
Danuy ayante togg gi
nous nous relayons pour la préparation du repas.
ayante b-
de se relayer
alkaati b-
agent de police
Alkaati bi dafay tere woto yi taxaw fii
le policier interdit aux voitures de s’arrêter ici.
Kanamu alkaati
visage austère.
ay-ayle
faire alterner avec
Danga wara ay-ayle togg yi
tu dois faire alterner les plats.
alxayri b-
formule de con-sécration du mariage selon le rite musulman
(prov.) Déggagul alxayri
elle n’est pas encore mariée.
alwaayó b-
aloyau
alku
être réduit à un état misérable par sa propre inconduite
Dafa bàyyi woon ay waa-jur am, moo tax mu alku
il avait abandonné ses parents, c’est pour cela qu’il est misérable.
ayib b-
imperfection
Xale bu góor bu tollu ci diggu dooleem, ànd ak taar bu mucc ayib
un jeune homme dans la force de l’âge, d’une beauté sans tache.
ayibte j-
indiscipline
Xamuma ci ku mu jële ayibteem ji
je ne sais pas de qui il tient son indiscipline.
ayudiir g-
cycle
Dafay def ayudiir, mu amaat
c’est cyclique
alkol b-
alcool (pour soins médicaux)
ayoo
se quereller
Dafa ayook dëkkandoom yépp
il s’est querellé avec tous ses voisins.
aaytal
considérer comme maléfique
Dañu ko aaytal, waaye dara bonu ci
on le considère comme mauvais mais il n’y a rien de mal en cela.
almuudó b-
Élève religieux
Jox ko almuudó yi
donne le riz aux élèves religieux !
ayubés g-
semaine
Ayubés giy ñów la
c’est la semaine prochaine.
ajoor b-
originaire du Cayor (Sénégal)
Ab Ajoor a ko jàngal wolof
C'est un ressortissant du Cayor qui lui a enseigné le wolof.
alburaax m-
cheval de l’ange Gabriel
Alburaax, mooy fas wi Jibril, malaaka ma, di war Alburaq,
c’est le cheval que monte l’ange Gabriel.
alfok
il faut que
Alfok ma mos ci
il faut que j’y goûte.
almet b-
allumette
am
avoir (dans le sens d’exister)
Am na ay bërëb yu ma dul dem
il y a des endroits où je ne vais pas.
am
un / une
ali
hue ! (pour faire avancer un cheval)
aldànke
déranger tout le monde dans un endroit sans qu’on puisse rien y faire
Dafa aldànke foofa yépp
il a dérangé tout le monde là-bas.
al
fils de tel
alaterete
être à la retraite
aloom g-
Ébénier du Sénégal
aloom g-
Ébénier du Sénégal
baag b-
seau pour puiser
Boo demee ca teen ba, dinañu la abal baag
si tu vas au puits, on te prêtera un seau.
(prov.) Ku yàgg cib teen, baag fekk la fa
qui reste longtemps à un puits, un seau t’y trouve
baase b-
sauce à base de pâte d’arachide que l’on mange avec du couscous
Baase laay togg tey
je prépare du {baase} aujourd’hui.
baal
pardonner
Yàlla na ma Yàlla baal
que Dieu me pardonne !
Baal naa la sama wàll
je te cède ma part.
banaana g-
bananier
banaana g-
bananier
bañal
refuser qqch à qqn
Mënuma la koo bañal
je ne peux pas te le refuser.
baŋ b-
banc
ban b-
argile rouge banco
Ndaa li, ban lañu ko tabaxe
le canari a été fait avec de l’argile.
band
osciller
bandaalu
se promener
bank
plier (une chose rigide ou articulée)
Bankal say baaraam
plie tes doigts !
bann
exprime l’idée d’être largement répandu
Sa cuuraay laa ngi xeeñ bann ci kër gi
(l’odeur de) ton encens s’est répandu dans toute la maison.
banqaas b-
branche ramification
Goral banqaas yi féete ak mbedd mi
coupe les branches qui sont du côté de la rue !
Dañu fay jàngale bépp banqaas bu jëm ci wàllu koom-koom
on y enseigne toutes les branches de l’économie.
(prov.) Kenn du toog ci banqaas di ko gor
on ne coupe pas la branche sur laquelle on est assis.
banqanaase b-
suie
Diwal ko banqanaase ci jë bi
mets-lui de la suie sur le front !
bant b-
bâton du bois
Taabalu bant la
C'est une table en bois.
(prov.) Bant, lu mu yàgg, yàgg ci dex, du ko taxa soppaliku jasig
le morceau de bois aura beau rester dans le marigot, cela n’en fera pas un crocodile.
tegoo ay bant
tirer à la courte paille.
Am nañu ñaari bant
ils ont deux enfants.
bantu-suukar g-
canne à sucre
baas b-
bâche
baraada b-
théière
Baraada bu bëtt
une théière trouée.
baraag b-
baraque
Bi may xale, bare woon na ay baraag Ndakaaru
quand j’étais enfant, il y avait beaucoup de baraques à Dakar.
barag b-
titre du souverain dans l’ancienne province du Walo
Mën naa la limal barag yi fi masa falu
je peux te citer les souverains qui ont régné ici.
baraj
exprime la manière d’entrer soudain
Geneen yax ne ca pëqéet ne baraj ca bëtam
un autre os en sortit brusquement et entra soudain dans son œil.
baram
entortiller
Wéñ yee baram kawaram gi
ce sont les mouches qui lui ont entortillé les cheveux.
baram
être crépu
Kawar gi dafa baram
ses cheveux sont crépus.
baraxante w-
cheval à robe rouge et blanche
barax b-
roseau
barastiku
glisser
Dafa doon wàcc ci iskale bi, barastiku
il descendait l’escalier et glissa.
bar b-
varan d’eau
(prov.) Ku fóotal mbëtt, roccil bar
qui fait la lessive pour le varan de terre devrait dépouiller le varan d’eau de sa vieille peau
bare-ay
être belliqueux
bar-bari
se déplacer lourdement comme un varan