wolof
stringlengths 1
166
| french
stringlengths 2
331
|
---|---|
ag | (devant les noms de la classe {g-}) Un(e) |
Am na ag gone gu la doon wut | il y a un enfant qui te cherchait. |
artu | mettre en garde, avertir |
Bi ñu ko defee, Yàlla artu leen ci biir gént, ñu baña dellu ca Erot | alors, Dieu les avertit en garde en songe de ne pas retourner chez Hérode. |
akkati | enlever les croûtes d’une plaie |
Yaay ja akkati piccam ya ba ñu set | sa maman nettoya proprement les croûtes de ses pustules. |
artu b- | mise en garde, avertissement |
aru | être en colère |
Dafa aru; nanguwul sax lekk | il est fâché; il ne veut même pas manger. |
aawlu | être sujet à tous les malheurs qui arrivent |
Dama aawlu | C'est à moi qu’arrivent tous les malheurs. |
asaka j- | partie que le musulman prélève annuellement sur ses biens pour les nécessiteux |
At mu ne, war ngaa génne asaka | chaque année, tu dois prélever une partie de tes biens pour les pauvres. |
as | un / une |
As suuf | une terre |
aaye | interdire |
Dafay aaye ku fi tux | il interdit de fumer ici. |
(prov.) Kuy aaye xobu màngo, doo ci maye ub doom | celui qui ne permet pas de toucher aux feuilles du manguier, n’en donnera pas un fruit. |
asaaloo | lancer qqch en chandelle. |
abdu jaambaar m- | abdou Diambar, ange de la mort |
Abdu-jaambaar dafa la naan : – Julli nga am ? | Abdou Diambar te dit : – As-tu prié ou non ? |
able | prêter |
Dama able sama woto | J'ai prêté ma voiture. |
aset b- | assiette |
asi | hacher |
Nanga asi soble bi | tu hacheras l’oignon. |
aj g- | pèlerinage à La Mecque |
Ren, aj gi mettiwuloon | cette année, le pèlerinage à La Mecque n’a pas été pénible. |
aseer j- | samedi |
Aseer ja ca topp la ñów | il est venu le samedi suivant. |
ab | un, une |
amaa | soit que… soit que… |
Demal wax ko sa soxla amaa mu ne waaw, amaa mu ne déet | va lui dire ton problème; soit il dit oui, soit il dit non. |
askanoo | être issu de telle lignée paternelle |
Foo askanoo ? | de quelle lignée paternelle es-tu ? |
aj b- | fait de placer qqch en hauteur |
aj b- | botte de foin de haricot suspendue pour la conserver |
abalante | se prêter des choses mutuellement |
Xale yi dañuy abalante seeni yére te baaxul | les enfants se passent leurs habits entre eux mais ce n’est pas bien. |
alamikk | certainement |
aj | aller en pèlerinage à La Mecque |
Aj na ñaari yoon | il est allé deux fois en pèlerinage à La Mecque |
aj | placer qqch à un endroit élevé |
Ajal saaku bi ci kow armool bi | place le sac sur l’armoire ! |
(loc.) Ajal say mbagg | hausse les épaules ! |
(loc.) Danu aj ngénte li | nous avons reporté le baptême. |
Ajal sa naw | retiens ton souffle ! |
(prov.) Ku sa nàkk jeex, nga aj say koog | celui qui a fini de faire son gâteau de riz range ses cuillères en bois (quand on a épuisé ses atouts, on se retire). |
aay | jouer au {aay} |
Kaayleen ! Ñu aay | venez ! Nous allons jouer au aay. |
aca | invite à faire une action |
Aca, woyal | vas-y, chante ! |
Aca, ca biti ! | allez, dehors ! |
Aca, nu dem ! | allons-y ! |
altine j- | lundi |
Altine jiy ñów | lundi prochain. |
aw | un(e) |
May na ma aw nag | il m’a offert une vache. |
afal b- | bouche d’aération |
Yàkkalil afal bi | élargis la bouche d’aération. |
akara b- | (Yor.) Beignet de haricot acra |
Jaay ma akara | vends-moi des acras. |
(prov.) Ku bëgg akara, dangay ñeme kaani | qui veut des acras ne doit pas redouter le piment. |
astemaak | plus forte raison |
Ndegem yow, yaa ko mëna def, astemaak moom | si toi, tu peux le faire, à plus forte raison lui. |
(prov.) Làmmiñ jigul bant, astemaak nit | la langue (par son influence magique) est mauvaise pour le bout de bois, à plus forte raison pour la personne. |
awal | cultiver le champ de son beau-père |
Damay awal sama goro-bu-góor toolam | je fais des travaux pour mon beau-père dans son champ. |
abal | prêter |
Abal ma sa saatu | prête-moi ton canif. |
Abal ma ! | fiche le camp ! |
(prov.) Ku la abal i tànk, nga dem fa ko neex | on fait ce qui plaît à son bienfaiteur. |
awale | faire passer (qqch) par |
awyoŋ b- | avion |
aw-aw b- | passages incessants |
and b- | brûle-parfum |
And bi dafa toj | le brûle-parfum est brisé. |
Taaj nit ci andam | empoisonner (à qqn) la vie. |
awra j- | sexe |
Muural ko awraam | couvre-lui les parties intimes. |
aw b- | travaux champêtres effectués pour son beau-père |
Sama goro dafa ma sant ab aw | mon beau-père m’a chargé d’un travail dans son champ. |
awu | saisir au vol |
Dama ko awu, lu ko moy mu toj | je l’ai saisi au vol, autrement il se brisait. |
aballoo | amener à prêter |
Ku la aballoo Astu sama kuur ? | qui t’a demandé de prêter mon pilon à Astou ? |
ax | traduit la douleur ou le plaisir |
Ax, aka metti ? | aïe, comme c’est douloureux ! |
a nga | voilà |
Omar a nga | voilà Omar. |
alamaan b- | amende |
Feyaguloo sa alamaan bi | tu n’as pas encore payé ton amende. |
ay | avoir lieu |
Lépp lu fi ay, na leen wóor ne dina ko ko jottali | soyez certains qu’il lui rendra compte de tout ce qui se passe ici. |
(prov.) Lu ay, di njàmbat | quand une chose a lieu, on en parle. |
ay | des |
Ay xale lay waxal | C'est à des enfants qu’il parle. |
ay | exprime la douleur |
Ay ! màtt na ma | aïe ! il m’a mordu. |
axakay | si (dans une réponse à une phrase interro-négative) |