wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
ajagjag
il y a belle lurette
Dem na ca ajagjag
il est parti il y a belle lurette.
aaye b-
interdiction
Aaye bi du yàgg
L'interdiction est temporaire (ne durera pas).
aalim j-
Érudit
Aalim yi ci dëkk bi daje nañu
les érudits qui sont dans la ville se sont réunis.
alamaan
mettre à l’amende
Soo ñówul, dinañu la alamaan
si tu ne viens pas, tu seras mis à l’amende.
aay b-
jeu de jeunes filles où on essaie à tour de rôle de placer le même pied que la meneuse qui, elle, essaie de prendre les joueuses à contre-pied
Bàyyileen aay bi te dem ca waañ wa
laissez ce jeu de {aay}et allez à la cuisine.
almasi b-
(Héb.) Messie
Yéesoo di almasi bi gurmet yi doon xaar
Jésus est le messie qu’attendaient les chrétiens.
agsi
arriver (au lieu du locuteur)
Xale yi agsi nañu
les enfants sont arrivés (ici).
(loc.) Agsi nga nak
t'y voilà !
aayoo
aider un bébé à s’endormir en lui chantant une berceuse
Demal aayoo bebbe, mu nelaw
va bercer bébé afin qu’il s’endorme.
Aayoo nenne
dodo, l’enfant dort.
ajab b-
nom originel de l’ethnie wolof
Ñi ñuy wooye Wolof tey, am na jamano joo xam ne ajab lañu leen daan wooye
ceux qu’on appelle Wolof actuelle-ment, il fut un temps où on les appelait Ajab.
aay-gaaf
se dit d’un animal ou d’une personne qui porte la poisse
Sa fas wi dafa aay-gaaf
ton cheval porte la poisse.
aal b-
mauvaise humeur
Bu ko aal bi jàppee
quand il est de mauvaise humeur.
aareen b-
aire aménagée pour les jeux de lutte. (De nos jours, on emploie plus souvent le terme làmb)
aar
laver une pièce de linge pour la première fois
Maa ngi sooga aar mbubb ma ma jéndoon
je viens seulement de laver le boubou que j’avais acheté.
aaya b-
verset du Coran
Ci ban aaya lañu ko waxe ?
dans quel verset l’a-t-on dit ?
afirig g-
afrique
a ngee
voilà
Omar a ngee
voilà Omar.
a ngale
voilà
Omar a ngale di dem
voilà Omar qui s’en va.
a ngoogale
voilà
Omar a ngoogale
voilà Omar.
alxames j-
jeudi
Daawunu dem ekool alxames
nous n’allions pas à l’école le jeudi.
a ngi
voici
Suma kër a ngi
voici ma maison.
Maa ngi ci li nga wax
J'approuve ce que tu as dit.
Maa ngi ci yow
je m’occupe de toi; je suis à toi. (ou encore) je t’aime.
afeer b-
affaire
Lii, afeer la
ça, c’est une affaire.
Afeer la
C'est confidentiel.
aniinu
se maquiller en bleu
Géj naa gis ku aniinu
il y a longtemps que je n’ai pas vu qqn se maquiller en bleu.
a ngoogule
voici (à côté de toi)
Aw doj a ngoogule ci sa wetu tànk
voilà un caillou à côté de ton pied.
aniin
mettre du bleu de maquillage
Bul aniin xale bi
ne maquillage pas l’enfant en bleu !
aniin j-
bleu de maquillage
Aniin ji mu def dafa ëpp
il a mis trop de maquillage bleu.
abajadda b-
alphabet
Mu ngi tollu ci abajadda
il en est à l’alphabet.
aji
celui qui fait
Yàlla, aji-kàttan, dimbali ma
Dieu, source de toute puissance, aide-moi !
aniwerseer b-
anniversaire
a ngii
voici (tandis qu’on montre)
Omar a ngii
voici Omar.
aññaane
éprouver de la jalousie vis-à-vis de qqn à cause d’une chose
Danga ma aññaane sama séy bi
tu me jalouses à cause de mon couple.
aji-gëm j-
croyant
Aji-gëm ji, Yàllaa koy sàmm
le croyant, c’est Dieu qui le protège.
alal j-
richesse fortune bien
Bu nit ñiy wut alal, yow, wutal nit ñi
quand les hommes cherchent la richesse, toi, cherche les hommes !
(prov.) Alalu golo a lex ba
on garde ses biens près de soi (pour y veiller).
antule
réussiir en qqch
Yàlla dimmali na nu ba nu antule nun ñépp
par la grâce divine, nous avons tous réussi.
aajowoo
avoir besoin de
Lépp loo aajowoo, dina ko toppatoo
tout ce dont tu auras besoin, il s’en occupera.
asiire
assurer, garantir par un contrat
araamal
considérer comme illicite, prohiber par la loi islamique
Mbaam, ci yàpp yi ñu araamal la bokk
le porc fait partie des viandes prohibées.
araab
arabe
afal
libérer
Dañuy téye xale yu jigéen yi ci kër yi, afal xale yu góor yi
on retient les filles à la maison et on libère les garçons.
ableloo
ordonner de prêter
Ku la ableloo sama gënn
qui t’a demandé de prêter mon mortier.
aras b-
l’au-delà
Kenn mësula bàyyikoo aras
personne n’est jamais revenu de l’au-delà.
abada j-
Éternité
Borom bi, duma la bàyyi ba abada
Seigneur, je ne te quitterai pas jusqu’à l’éternité.
ariko j-
haricot
ar
être ferré sur (les études)
Dafa jàng ba ne ar
il est pétri de connaissances.
araw
rouler la farine en gros granules
Janq bu mënul araw; mas-sa yow
une fille ne sachant pas rouler la farine; pauvre de toi !
abalaate
prêter (avec une certaine propension à le faire)
Li muy abalaate saretam bi yépp dey, bëgga falu doŋŋ
il prête sa charrette (à qui veut) uniquement pour être élu.
aji-gëm-xërëm j-
animiste
armeel y-
cimetière
Armeeli katolik yi ak yu jullit yee dend.
Le cimetière des catholiques et celui des musulmans sont contigus.
(prov.) Néew, bu rombeey armeel, robam dootul neex
quand la dépouille va au delà du cimetière, son enterrement ne sera plus aisé.
araf b-
signes graphiques de l’alphabet
Ñaar fukki araf ak juróom benn a am ci seen liifantu
il y a vingt-six lettres dans leur alphabet.
arikoweer j-
haricot vert
armool b-
armoire
aat b-
adulte qui n’est pas encore circoncis
Dajale nañu aat yépp
on a réuni toutes les personnes ayant atteint l’âge de la circoncision.