wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
yoxoos
manière furtive d’entrer
Dafa ne yoxoos dugg, defe ne gisuma ko
il est entré furtivement, pensant que je ne l’avais pas vu.
yoroxlaan g-
ceratotheca sesamoides (Pédaliacées) (herbe gluante qui peut servir de fourrage)
Jur gi laay wutal yoroxlaan
je cherche du Ceratotheca s. pour le bétail.
Sa tànk bu gaaw bi mel ni yoroxlaan
avec ton pied rapide comme l’éclair.
yorin w-
de tenir
Booy nàmpal, yorin wu baax waa ngi
quand tu allaites, voici la bonne façon de tenir.
yónni
envoyer qqn
Kan nga yónni marse
qui as-tu envoyé au marché ?
yow
toi
Yow la woo
C'est toi qu’il a appelé.
yoxoosu
entrer furtivement
Dafa yoxoosu
il est entré furtivement
yos
ceux de
Sa yos lañu
ce sont les tiens.
yoxos j-
huître
Mënatuma lekk yoxos ju ñorul
je ne peux plus manger d’huîtres crues.
yugg
être blotti
Mu ngi ne yugg ci wetu ndey ji
il est blotti près de sa mère.
yu
s’emploie avec les noms de la classe y-
yul b-
mollet
Yul yu réy la am
il a de gros mollets.
yukk-yukki
marcher de façon saccadée
Mu ngale di yukk-yukki di dem
il s’en va marchant d’une façon saccadée.
yox-yoxi
avoir peur
Ku yaakaar Sériñ Tuubaa doo yox-yoxi
qui espère en Sérigne Touba ne doit pas avoir peur.
yulli
vider (un sac ou une poche) de son contenu
Noona, mu yulli saaku ba ba mu set
alors, il vida complètement le sac.
yukk-yukk
exprime une façon saccadée de marcher
yulub
entrer subitement dans un trou profond
Dafa doon xuus, ne yulub ci pax
il marchait dans l’eau et entra subitement dans un trou.
yugur-yugur
Évoque la manière de marcher d’un pas pesant
yu-nekk
chaque
Ñaari fan yu-nekk
tous les deux jours.
yunn
faire une brève apparition
Jant bi dafa ne yunn, réeraat
le soleil a fait une brève apparition et a disparu à nouveau.
yumpaañ j-
Épouse de l’oncle maternel
Sama yumpaañ a ma woolu
C'est la femme de mon oncle maternel qui m’a fait appeler.
yuqéelu
se dresser sur la pointe des pieds
Soo yuqéeloo it, du la taxa tollook man
même si tu te mets sur la pointe des pieds, ça ne te fera pas aussi grand que moi.
(prov.) Yuqéelu mbaam, du ko taxa day ni gëléem
le fait, pour un âne, de se dresser sur la pointe des pieds ne lui fera pas atteindre la taille d’un dromadaire.
yulliku
se vider (un sac ou une poche) de son contenu
yuppit y-
fripes
yuq g-
moelle
Génneel ma yuq gi
sors-moi la moelle !
yuqi
remonter un peu une chose enfoncée dans le sol
Xale yee yuqi jën wi
ce sont les enfants qui ont remonté un peu le pieu.
yuur g-
grêle
Géj na taw ag yuur
il y a longtemps qu’il n’y a pas eu de grêle.
yuri
vider (un contenu)
Yuri na siddéem si woon ci poosam yépp
il a vidé tous les jujubes qui étaient dans sa poche.
yuuli-yuuli j-
septième période de la saison des pluies, qui dure treize jours
Yuuli-yuuli jeey sooga door
C'est la septième période de la saison des pluies qui vient de commencer.
yuur
se courber
Bunt bi dafa suufe, ku fiy jaar, faw nga yuur
la porte est basse, celui qui passe par là est obligé de se courber.
yuut g-
salive
Yéréem yaa ngi tooy xepp ak yuut
ses habits sont trempés de salive.
yuuxoo y-
cris émis en chœur
yuug
se baisser
Yuugal !
baisse-toi !
yuuxoo
siffler (qqn) en signe de désapprobation
Nit ñi dañu ko yuxoo
le public la sifflé.
yuux g-
cri
Fu yuux yooyu jóge
D'où viennent ces cris ?
yuy
qui
Am na jaan yuy ëmb
il existe des serpents vivipares.
àngare b-
engrais
Def ci àngare
mets-y de l’engrais !
yuuxu
crier
Bul yuuxu, guddi na
ne crie pas, il fait nuit !
yàbb
rester bouche bée
Ba mu ma ko waxee, dama ne yàbb, di ko xool
quand il me l’a dit, j’étais là, bouche bée, à le regarder.
yàkkamti
être pressé
Mënuma laa xaar, dama yàkkamti
je ne peux pas t’attendre, je suis pressé.
(prov.) Bu doom yàkkamtee génn kër baayam, yaayam a yàkkamti
si un enfant est pressé de quitter la maison de son père, c’est que c’est sa mère qui est pressée.
yuuy b-
brume
yàggaay b-
pérennité
Dina dellusi gaa; yàggaay bi rekk a ma ci jaaxal
il reviendra certes; c’est seulement la longue durée qui m’inquiète dans tout ça.
yàkkaliku
être élargi
Ba nga solee sama dàll yi lañu yàkkaliku
C'est quand tu as mis mes chaussures qu’elles se sont élargies.
yàccaaral
emphatique de {yàcc}
yàbbi
sortir qqch de la bouche
Dama ne nga yàbbi xaalis bi nga sex
je te dis d’enlever l’argent que tu as dans la bouche.
yàbbi
déteindre
Sér bi dafay yëbb; bu ko boole ak yeneen yi
le pagne déteint au contact de l’eau; ne le mets pas avec les autres !
yàmbaa j-
cannabis chanvre indien
Dafay tux yàmbaa
il fume du chanvre indien.
yàkki
Élargir
Dama bëgga yàkki baat bi
je veux élargir le col.
àttekat b-
juge arbitre
yàmboŋ b-
bourbouille
Puudar buy faj yàmboŋ la
C'est une poudre qui soigne la bourbouille.
yàpp
dévorer
Gaynde gee ko yàpp
C'est le lion qui l’a dévoré.
yàlla tere
a Dieu ne plaise
yàŋŋ
exprime le fait d’être libre, sans encombrement
Séñ Fàllu nee na : Bu nee yàŋŋ, nga ne yoll te teey. Bu nee tacc, nga ne tekk, booleek nga ne nikk, ne nàŋŋ
le guide Fallou a dit : Quand elle (la voie) est libre, tu accélères sans te précipiter. Quand elle est embouteillée, tu restes calme, tu maîtrises ta voiture, tout en regardant droit devant toi.
yàpp w-
viande
Defal yàpp wi ci firsideer bi
mets la viande dans le réfrigérateur !
yàndoor
dormir profondément